Nguur bu ñu wéer ci bëg bëg askan bi, ñu kay dakkantalee ci kallama nasaraan « démocratie », mooy ci ay kaddu lu rew yu bëri yu nekk ci aduna bi di bakkoo, ba ci rewum Suñu Gaal, mu rew yu bëri def royukaay fii ci Afrik. Waaye suñu xoole ci jëf yi, nguuru bu ni mel amul fenn. Askan bi ñakk na nguuram ba mu denkee dooleem yëpp njiitu rew mi ak parti wam.
Ňaar fukki fan ci weeru « Mars » ci atum 2016, asakan u Suñu Gaal bi dina wax waaw wala deet ci sopite sartu rew mi, njiitu rew mi summ. Ci ndaje yi ni mel, wala ndajemu fal njiit yu rew mi, wala layal katu askan wi, la ñuy seet lu doole askan wi. Askan wi rek mooy fal mooy folli. Saa yu ñu wara sopi sartu rew mi, kaddu gu mujj bi askan bee ko yellool itamit. Lu ni mel day wone ni aaskan wi am na doole bu am solo si rew mi. Waaye, fa la dooleem yam.
Njiitu rew mi ak farandoo wam aakimoo na ñu nguuru askan wi
Ci ay kaddu, nguur mi askan bi laffi wara nekkal. Ci ay kaddu lepp lu nguur bi nar si boppu rew mi ci askan bi kese la wara dellu. Leneen lu mu mënë doon day nasaxal bu baax nguur mi nga xamne askan bi moo ko moom.
Suñu xoolee bu baax ci rew mi, doole njiitu rew mi ak kaddu wam moo ëpp solo doole askan wi. Njiitu rew mi mooy tann ay nitam ci wallum jaraaf, wala jëwrin yuy jiite rew mi. Njiitu rew mi mooy tann jëwrin yu jëm ci wallu yoon, ak yeneen ak yeneen. Lu gënë yokk doole njiit mi, mooy layal katu askan wi. Ňi nga xamne ci ay kaddu askan bi la ñu fi nekkal, si ay jëf njiitu rew mi la ñu fi nekkal. Ňi nga xamne ci ay kaddu ñoo wara kaasal askan wi, ñoo ko fi wara taxawal, nguur bi la ñu fi nekkal, nguur bi la ñuy kaasal.
Ci njëfin nguur gi dafa aakimoo lepp lu ko askan wi jox, di doxalee nu ko soobee, layal katu askan wi di ko si xër di ko ci soññ. Askan wi ñi ñuy dakantalee « opposition », maanaam ñii di jaamaarloo ak nguur gi rek ñoo ko fi nekkal. Wante, bes bu ñu jotee ci nguur deloo buum ba ci mbooy mbooy ba. Ta ñoom amuñu benn kaddu, wala benn doole ngir saafara jafe jafe askan wi.
Ta suñu xoolee bu baax, askan bi mooy buuru njiit yi. Askan bi moo leen fa tekk. Askan bi moo leen jox kopar yu ñuy yoree dëk bi. Waaye leneen la ñu gis. Nguur guy nasaxal allalu askan wi, nguur guy doxalee nu ko neexee, aakimoo doole askan wi la ñu gis. Lu koy firndeel, mën na ñu ci tuddu, telewisiyon dëkk bi, manaam RTS. Tele wi askan wee ko moom. Ci koparu askan wi la ñuy fay tas ka tu xibaar yi fay ligéeyée. Njiitu rew mi amu ci benn wall. Waye safaan ba la ñu gis. Sa su xibaar jotee, njiitu rew mi lañuy gënë wone. Te yamu ñu ci di ko wone rek. Saa su ne dañ koy tagg, di ko sossal ay jaloore, ni buur. Tele mi nga xamne jafe jafe askan wi la ñu fi wara wone ngir indi ci ay saafara, saa su ne safaan ba lañuy gis. Nekkataul tele askan wi, tele njiitu rew mi la.
Firnde yi bëri na. Yëp day wone ni rek ni askan bi amatul doole, ba mu falee njiitu rew. Dooleem, ci mpal mi la yam. Ta nguuru askan (démocratie) wu suñu rew di bakko, dafa wara dëppóo ak ne, njiit yi askan bi ci boppam la wara doon. Loolu ci ay wax la yam.

Aucun commentaire:
Enregistrer un commentaire