Ňaar fukki at ak ñaar a ngii, Gambi ci waaw oom ak deet oom
lay doxee. Aakki moo nguur gi, ku andul ak moom mu fexeel la. Fitnaal ñu bëggë
jaamaarloo ak moom, wala mu yobb leen kaso. Gambi, di rew bu ndaw, sox la dëkk
yu ko wër ngir mënë jëm kanam, mu ber ko, ba kom kom oom taxu koo demee noonu. Doomu
Gambi yi muñ nañ ba fu muñ yam. Seen yaakaar yëpp ci lenn la weeru : Yaya
Jammeh abal leen, ngir ñu feex. Moo tax ba ñu yëgee ne Jammeh nangu na daanu
woom, kontaan la ñu def, topp mbedum Banjul, di way ak di fecc. Seen yakaar
tasaat na ak wax waxeet bii.
Fu mu ne nii, adduna yëpp, won nañ ganaaw doomu Kanulai bi.
Suñu Gaal di rew bu ko gënë jege jiite ko, Amerik feelu ko, kurel bii di
CEDEAO, di dox tankum jam ngir Jammeh, joge nguur gi nu mu gënë gaawee. Mbootaay
u doomu aadama yi itamit dankaafu ko. Jangale kat u Gambi, layalkat yi won ko
ginaaw. Lenn rek moo ko dese, joxe linge yi. Su të wee, ay daan yu metti mu ngi
koy xaar. Takk deru CEDEAO, wala, Suñu Gaal, wala Mbootaayum xeet yi am nañ
yaakaar ni di nañ songg Jammeh, bes bu bëggee toogatt ci boppu rew mi. Mu mel
ni amatul pexe.
Gambi, di rew mu sox la nooyi, ubeeku ci aduna itamit ngir
gëna am ay yaakar, suxali kom kom om. Loolu, benn yoon rek lay mënë amee, Yaya
Jammeh joge nguur gi. Te loolu, waru ñu ci seetaan benn yoon doomu Gambi yi.
