Ajuma jii ñu weesu, Tugël ci musibë bu jeggi dayoo la juge. Ay jihaadkatu wa Daesh ñoo fa ray ay téeméeri doomu aadama, di fayu xare mi Tugël di leen summ fële ca réwum Siri. Moo waral ñu def taxaw seetlu ba gisne loxoy Tugël dafa takk bu baax ci jihad bu lëmbee aduna bi jamono yii.
Jamono yii bes bu nekk ay doomu aadama ñakk seen bakkan ndax ay songu jihadkat. Li ko dalee ci rewu arab yi, ba fii di Nigeria ak rew yu mu dendal, ba sax rewu tubaap yi, Amerik, Russie ak yeneen, jihadkat yi bayi wu ñu fenn. Ba at bi tambalee ba léegi, Tugël bokk na ci reew yu gënë fës ci wallum fitnë yu ni mel. Ay weer ci ganaaw këru tasskatu xibaar bi di Charlie Hebdos songoon nañu ka fa ba ray fa lu ëpp fukki nit. Ajuma jii, fukk ak ñetti fan ci weerum « Nowembar », mussibë bu ñu yagga gis moo dalaat rewum Tugël. Lu ëpp ñaari téeméeri doomu aadama ñoo fa ñakk seen bakan, lu weesu xokkatal ak fitnaal bi ñu fintnaal ay dommu Tugël yu nekkon ci benn berëbu wayukaay bu tuddu Le Bataclan, ak ñeneen ñu nekkon wetu « Stade de France ». Tugël ci dëc la nekk fu mu ne nii.
Waaye su ñu xoolee bu baax loxooy Tugël gennul ci fitnë yu ni mel.
TUBAAP YI, ŇO BËGGË AAKIMOO ADDUNA BI
Adduna bu am benn aada ak benn xalaat, su ñu xoolee bu baax, rewum tubaab yi mom la ñu bëgg. Lii moo waral ba ñu wassaaree sen lakk ci aduna bi yëpp, wassaare fa seen aada, seen njáng, ñu ngi gën di wëy di wassaare seniy xalaat.
Lii ñuy wax « démocratie », maanaam nguurum askan wi, ak « capitalisme », maanaam Kom kom bu ñu wéer ci xaalis ak leneen lu bokk ci aq ak yeleefu doomu aadama yi bokk na ci lu leen gënë soxal at yii ñu weesu ba jamono yii. Moo tax rew bu bokkul ak ñoom xalaat ci adduna bi jeem nañu la fexeel ngir jeem fa wassare seen kaddu, seen gis gis, seen aada ak seeniy xalaat.
Rew mu mel ni Afghanistan, yagg nañu kaa fexeel ba ñu fippu. Jihadkat yi ñuy dakkantalee Al Qaida, mën nañu wax ne rewum tubaap yi ñoo ko sakk. Da ñoo dem ba benn yoon bobu la ñu gis ngir fippu.
Yamu ñu ci Afghanistan, njiitum Iraak bi le woon, Sadam Hussein ñoo ko daaneel, ba yobbée rewum Irak boobu ba legi ci ay fitnë bes bu nekk. Njiitum Libi bilewoon, Momar Khadafi ñoo ko daanel itamit, té boobu ba legi rewum Libi dafa sooxee bu baax, nekk ci mussibë bu metti. Mën nañu see yokk rewum Siri bi nga xamne ni atum 2010 ba leegi ci xare yu metti la nekk, ginaaw bi rewum Tubaab yi, ci njiitum Amerik tambalee « bombardé » dëkk bi ngir wacce Bassar Al Assad.
Lii yëpp dafa wañi dooley diwanu rewum araab yi bu bari, ba jihaadkat yi mënë defaru bu baax, def ay mussibë yu bëri boobu ba leegi, fepp ci aduna bi daanaka, ba bu ci mujj moy fitnëy Paris yii.
Suñu xoolee bu baax, rewum tubaap yi ñoo jurr jihad bu ci aduna bi. Mën nañu wax ni Amerik moo yobbée boppam fitnëy 11 Septembre ci atum 2001. Tugël itamit moo yobbée boppam fitnëy Paris yii, ndax lu mat bennë at moo ngi nii ñu ngi « bombardé » waa Daesh fële ca Siri.
Aucun commentaire:
Enregistrer un commentaire