mercredi 14 décembre 2016

Yaya Jammeh, dem mbaa torox!

Jamonoo jii coow lu lembee ëttu tassum xibaar yi ak ëtt yu melni Twitter wala facebook, lenn la, muy Yaya Jammeh ak lu xew Gambi. Mu di rew bu tollu ci ay fan yu am solo ngir ëleg oom. Lenn dall leer na : Jammeh lu mu gënë gaawa joge Gambi, rew mi di di gënë am yakaar ci ëlëk u naataange.

 Kenn yaakaarul woon ni di nañ ko daan ci mpal mii jall, waaye safaan ba moo am. Kenn yaakaarul woon ni su ñu ko daanee, di na nangu jell om, wayee, nangu na ko ba woo ki di Adama Barrow, ndokkeel ko. Ňu tegoon ne, Yaya Jammeh, soppeku na. Waaye bettaat na ñëpp, ci « wax waxeet » bu mu def gao gii jall, ni nangoo tul mplalup Adama Barrow. Fu ko kenn foogeewul rek mu genn fa.

Ňaar fukki at ak ñaar a ngii, Gambi ci waaw oom ak deet oom lay doxee. Aakki moo nguur gi, ku andul ak moom mu fexeel la. Fitnaal ñu bëggë jaamaarloo ak moom, wala mu yobb leen kaso. Gambi, di rew bu ndaw, sox la dëkk yu ko wër ngir mënë jëm kanam, mu ber ko, ba kom kom oom taxu koo demee noonu. Doomu Gambi yi muñ nañ ba fu muñ yam. Seen yaakaar yëpp ci lenn la weeru : Yaya Jammeh abal leen, ngir ñu feex. Moo tax ba ñu yëgee ne Jammeh nangu na daanu woom, kontaan la ñu def, topp mbedum Banjul, di way ak di fecc. Seen yakaar tasaat na ak wax waxeet bii.

Fu mu ne nii, adduna yëpp, won nañ ganaaw doomu Kanulai bi. Suñu Gaal di rew bu ko gënë jege jiite ko, Amerik feelu ko, kurel bii di CEDEAO, di dox tankum jam ngir Jammeh, joge nguur gi nu mu gënë gaawee. Mbootaay u doomu aadama yi itamit dankaafu ko. Jangale kat u Gambi, layalkat yi won ko ginaaw. Lenn rek moo ko dese, joxe linge yi. Su të wee, ay daan yu metti mu ngi koy xaar. Takk deru CEDEAO, wala, Suñu Gaal, wala Mbootaayum xeet yi am nañ yaakaar ni di nañ songg Jammeh, bes bu bëggee toogatt ci boppu rew mi. Mu mel ni amatul pexe.


Gambi, di rew mu sox la nooyi, ubeeku ci aduna itamit ngir gëna am ay yaakar, suxali kom kom om. Loolu, benn yoon rek lay mënë amee, Yaya Jammeh joge nguur gi. Te loolu, waru ñu ci seetaan benn yoon doomu Gambi yi.

Aucun commentaire:

Enregistrer un commentaire