mercredi 14 décembre 2016

Yaya Jammeh, dem mbaa torox!

Jamonoo jii coow lu lembee ëttu tassum xibaar yi ak ëtt yu melni Twitter wala facebook, lenn la, muy Yaya Jammeh ak lu xew Gambi. Mu di rew bu tollu ci ay fan yu am solo ngir ëleg oom. Lenn dall leer na : Jammeh lu mu gënë gaawa joge Gambi, rew mi di di gënë am yakaar ci ëlëk u naataange.

 Kenn yaakaarul woon ni di nañ ko daan ci mpal mii jall, waaye safaan ba moo am. Kenn yaakaarul woon ni su ñu ko daanee, di na nangu jell om, wayee, nangu na ko ba woo ki di Adama Barrow, ndokkeel ko. Ňu tegoon ne, Yaya Jammeh, soppeku na. Waaye bettaat na ñëpp, ci « wax waxeet » bu mu def gao gii jall, ni nangoo tul mplalup Adama Barrow. Fu ko kenn foogeewul rek mu genn fa.

Ňaar fukki at ak ñaar a ngii, Gambi ci waaw oom ak deet oom lay doxee. Aakki moo nguur gi, ku andul ak moom mu fexeel la. Fitnaal ñu bëggë jaamaarloo ak moom, wala mu yobb leen kaso. Gambi, di rew bu ndaw, sox la dëkk yu ko wër ngir mënë jëm kanam, mu ber ko, ba kom kom oom taxu koo demee noonu. Doomu Gambi yi muñ nañ ba fu muñ yam. Seen yaakaar yëpp ci lenn la weeru : Yaya Jammeh abal leen, ngir ñu feex. Moo tax ba ñu yëgee ne Jammeh nangu na daanu woom, kontaan la ñu def, topp mbedum Banjul, di way ak di fecc. Seen yakaar tasaat na ak wax waxeet bii.

Fu mu ne nii, adduna yëpp, won nañ ganaaw doomu Kanulai bi. Suñu Gaal di rew bu ko gënë jege jiite ko, Amerik feelu ko, kurel bii di CEDEAO, di dox tankum jam ngir Jammeh, joge nguur gi nu mu gënë gaawee. Mbootaay u doomu aadama yi itamit dankaafu ko. Jangale kat u Gambi, layalkat yi won ko ginaaw. Lenn rek moo ko dese, joxe linge yi. Su të wee, ay daan yu metti mu ngi koy xaar. Takk deru CEDEAO, wala, Suñu Gaal, wala Mbootaayum xeet yi am nañ yaakaar ni di nañ songg Jammeh, bes bu bëggee toogatt ci boppu rew mi. Mu mel ni amatul pexe.


Gambi, di rew mu sox la nooyi, ubeeku ci aduna itamit ngir gëna am ay yaakar, suxali kom kom om. Loolu, benn yoon rek lay mënë amee, Yaya Jammeh joge nguur gi. Te loolu, waru ñu ci seetaan benn yoon doomu Gambi yi.

jeudi 3 mars 2016

NGUURU ASKAN BI NAX SAAY NA !

Nguur bu ñu wéer ci bëg bëg askan bi, ñu kay dakkantalee ci kallama nasaraan « démocratie », mooy ci ay kaddu lu rew yu bëri yu nekk ci aduna bi di bakkoo, ba ci rewum Suñu Gaal, mu  rew yu bëri def royukaay fii ci Afrik. Waaye suñu xoole ci jëf yi, nguuru bu ni mel amul fenn. Askan bi  ñakk na nguuram ba mu denkee dooleem  yëpp njiitu rew mi ak parti wam.


Ňaar fukki fan ci weeru « Mars » ci atum 2016, asakan u Suñu Gaal  bi dina wax waaw wala deet ci sopite sartu rew mi, njiitu rew mi summ. Ci ndaje yi ni mel, wala ndajemu fal njiit yu rew mi, wala layal katu askan wi, la ñuy seet lu doole askan wi. Askan wi rek mooy fal mooy folli. Saa yu ñu wara sopi sartu rew mi, kaddu gu mujj bi askan bee ko yellool itamit. Lu ni mel day wone ni aaskan wi am na doole bu am solo si rew mi. Waaye, fa la dooleem yam.

Njiitu rew mi ak farandoo wam aakimoo na ñu nguuru askan wi
Ci ay kaddu, nguur mi askan bi laffi wara nekkal. Ci ay kaddu lepp lu nguur bi nar si boppu rew mi ci askan bi kese la wara dellu. Leneen lu mu mënë doon day nasaxal bu baax nguur mi nga xamne askan bi moo ko moom.
Suñu xoolee bu baax ci rew mi, doole njiitu rew mi ak kaddu wam moo ëpp solo doole askan wi. Njiitu rew mi mooy tann ay nitam  ci wallum jaraaf, wala jëwrin yuy jiite rew mi. Njiitu rew mi mooy tann jëwrin yu jëm ci wallu yoon, ak yeneen ak yeneen. Lu gënë yokk doole njiit mi, mooy layal katu askan wi. Ňi nga xamne ci ay kaddu askan bi la ñu fi nekkal, si ay jëf njiitu rew mi la ñu fi nekkal. Ňi nga xamne ci ay  kaddu ñoo wara kaasal askan wi, ñoo ko fi wara taxawal, nguur bi la ñu fi nekkal, nguur bi la ñuy kaasal.
Ci njëfin nguur gi dafa aakimoo lepp lu ko askan wi jox, di doxalee nu ko soobee, layal katu askan wi di ko si xër di ko ci soññ. Askan wi ñi ñuy dakantalee « opposition », maanaam ñii di jaamaarloo ak nguur gi rek ñoo ko fi nekkal. Wante, bes bu ñu jotee ci nguur deloo buum ba ci mbooy mbooy ba. Ta ñoom amuñu benn kaddu, wala benn doole ngir saafara jafe jafe askan wi.
Ta suñu xoolee bu baax, askan bi mooy buuru njiit yi. Askan bi moo leen fa tekk. Askan bi moo leen jox kopar yu ñuy yoree dëk bi. Waaye leneen la  ñu gis. Nguur guy nasaxal allalu askan wi, nguur guy doxalee nu ko neexee, aakimoo doole askan wi la ñu gis. Lu koy firndeel, mën na ñu ci tuddu, telewisiyon dëkk bi, manaam RTS. Tele wi askan wee ko moom. Ci koparu askan wi la ñuy fay tas ka tu xibaar yi fay ligéeyée. Njiitu rew mi amu ci benn wall. Waye safaan ba la ñu gis. Sa su xibaar jotee, njiitu rew mi lañuy gënë wone. Te yamu ñu ci di ko wone rek. Saa su ne dañ koy tagg, di ko sossal ay jaloore, ni buur. Tele mi nga xamne jafe jafe askan wi la ñu fi wara wone ngir indi ci ay saafara, saa su ne safaan ba lañuy gis. Nekkataul tele askan wi, tele njiitu rew mi la.

Firnde yi bëri na. Yëp day wone ni rek ni askan bi amatul doole, ba mu falee njiitu rew. Dooleem, ci mpal mi la yam. Ta nguuru askan (démocratie) wu suñu rew di bakko, dafa wara dëppóo ak ne, njiit yi askan bi ci boppam la wara doon. Loolu ci ay wax la yam.

FITNËY PARIS : TUGËL MOO DUGËL BOPPAM

Ajuma jii  ñu weesu, Tugël ci musibë bu jeggi dayoo la juge. Ay jihaadkatu wa Daesh ñoo fa ray ay téeméeri doomu aadama, di fayu xare mi Tugël di leen summ fële ca réwum Siri. Moo waral ñu def taxaw seetlu ba gisne loxoy Tugël dafa takk bu baax ci jihad bu lëmbee aduna bi jamono yii.



Jamono yii bes bu nekk ay doomu aadama ñakk seen bakkan ndax ay songu jihadkat. Li ko dalee ci rewu arab yi, ba fii di Nigeria ak rew yu mu dendal, ba sax rewu tubaap yi, Amerik, Russie ak yeneen, jihadkat yi bayi wu ñu fenn. Ba at bi tambalee ba léegi, Tugël bokk na ci reew yu gënë fës ci wallum fitnë yu ni mel. Ay weer ci ganaaw këru tasskatu xibaar bi di Charlie Hebdos songoon nañu ka fa ba ray fa lu ëpp fukki nit. Ajuma jii, fukk ak ñetti fan ci weerum « Nowembar », mussibë bu ñu yagga gis moo dalaat rewum Tugël. Lu ëpp ñaari téeméeri doomu aadama ñoo fa ñakk seen bakan, lu weesu xokkatal ak fitnaal bi ñu fintnaal ay dommu Tugël yu nekkon ci benn berëbu wayukaay bu tuddu Le Bataclan, ak ñeneen ñu nekkon wetu « Stade de France ». Tugël ci dëc la nekk fu mu ne nii.
Waaye su ñu xoolee bu baax loxooy Tugël gennul ci fitnë yu ni mel.


TUBAAP YI, ŇO BËGGË AAKIMOO ADDUNA BI
Adduna bu am benn aada ak benn xalaat, su ñu xoolee bu baax, rewum tubaab yi mom la ñu bëgg. Lii moo waral ba ñu wassaaree sen lakk ci aduna bi yëpp, wassaare fa seen aada, seen njáng, ñu ngi gën di wëy di wassaare seniy xalaat.
Lii ñuy wax « démocratie », maanaam nguurum askan wi, ak « capitalisme », maanaam Kom kom bu ñu wéer ci xaalis ak leneen lu bokk ci aq ak yeleefu doomu aadama yi bokk na ci lu leen gënë soxal at yii ñu weesu ba jamono yii. Moo tax rew bu bokkul ak ñoom xalaat ci adduna bi jeem nañu la fexeel ngir jeem fa wassare seen kaddu, seen gis gis, seen aada ak seeniy xalaat.
Rew mu mel ni Afghanistan, yagg nañu kaa fexeel ba ñu fippu. Jihadkat yi ñuy dakkantalee Al Qaida, mën nañu wax ne rewum tubaap yi ñoo ko sakk. Da ñoo dem ba benn yoon bobu la ñu gis ngir fippu.
Yamu ñu ci Afghanistan, njiitum Iraak bi le woon, Sadam Hussein ñoo ko daaneel, ba yobbée rewum Irak boobu ba legi ci ay fitnë bes bu nekk. Njiitum Libi bilewoon, Momar Khadafi ñoo ko daanel itamit, té boobu ba legi rewum Libi dafa sooxee bu baax, nekk ci mussibë bu metti. Mën nañu see yokk rewum Siri bi nga xamne ni atum 2010 ba leegi ci xare yu metti la nekk, ginaaw bi rewum Tubaab yi, ci njiitum Amerik tambalee « bombardé » dëkk bi ngir wacce Bassar Al Assad.
Lii yëpp dafa wañi dooley diwanu rewum araab yi bu bari, ba jihaadkat yi mënë defaru bu baax, def ay mussibë yu bëri boobu ba leegi, fepp ci aduna bi daanaka, ba bu ci mujj moy fitnëy Paris yii.

Suñu xoolee bu baax, rewum tubaap yi ñoo jurr jihad bu ci aduna bi. Mën nañu wax ni Amerik moo yobbée boppam fitnëy 11 Septembre ci atum 2001. Tugël itamit moo yobbée boppam fitnëy Paris yii, ndax lu mat bennë at moo ngi nii ñu ngi « bombardé » waa Daesh fële ca Siri.

ÑAARI KOOR ÑAARI KORI: LU TAX? LAN MOY PEXE YI?

At bu nekk tambaliwu weeru koor bi day juur feewëloo yu bëri ci digante juliitou rew mi. Ñaari Korite wala Ñaari tabaski Suňu gaal Gëjj na se mucc. Waye am na ay pexe yo xamne mën naň se sukëndiku ngir am benoo ci digante juliit yi.



Sa sune ňaari Korite wala  ňaari Tabaski, daň koy nemeeku ci Suňu gaal. Wante, am na kureel buňu denk lepp lu jëm ci walu saytum weer. Tariixa yu bëri am naňu  ku leen fay taxawal. Ni ki nóonu, att yi ňu weessu lu ëpp ci juliitu rew mi am naňu benoo ci walu saytu weer. Murid yi, tijaan yi, laayeen yi, ňasseen yi... jox naňu seen koolute Kureel bu Cherif Iyan Thiam di jiite. Att bu nekk kureel bobu moy seèntu weer bi feep ci Suňu gaal ngir wax baan bess laňuy tambale koor gi, wala ban bess la korite,  tabaski, wala tamxarit.

Waye yen ci këru julitt yi ci rew mi and ňu ak kureel bi. Ci Maka laňuy röy. Sa su Maka, wala yenen këru diine yu nekk ci aduna bi gisse weer bi, ňu topp ci. Waa Ibaadu Rahman yi ak këru omarienne bi ňoo ci gënë fëss. Lolu day wone ni feewëloo am na ci digante julittu rew mi.

Lu waral fèewëloo bi?
Al xuraan ak xadiss yi daň ne: Weer bi fu mu mënti feeň, su ame ay seede tambali koor gi joot na. Waye fèewëloo bi lu ko waral lenn la: Juliitu rew mi, daňo woute fu ňuy sukëndiku.
  • Kureel bi ëmbë lu ëpp ci jullitu rew mi senn saytu weesu wul Suňu gaal.
  •  Ibaadu Raxmaan yi ak  këru omarienne bi seen saytukaay mo gënë yatu (aduna bi yëpp)

Lan mo ciy pexe?
Ngiir benn koor ak benn korite am ci Suňu gaal, juliit yi daňo wara deggo ci kaadu. Balaa lenn, daňo wara def lepp ngir
bokk fu ňuy sukëndiku. Ngir egg fofu am na ay buntu yo xamne ni xaraala yi mo ci gënë am solo.
Att yaa ngi dem xarala yi di gënë jegi dayo. Tay, am na ay juntukaay yo xam ne ni mën naň se saytu ta du ňu jùum kaň la weer bi di tambali. Juliitu rew mi suňu mankoo won ci buntu mi mën na am sen fewëloo bi dakk.